05/02/2021
Chers amis, militants et sympathisants,
- Après les 《 financements russes 》
- Après les 《 liens avec le MFDC 》
- Après les 《 financements par l'état islamique 》
- Après la plainte pour « diffamation » portant sur les 94milliards
- Après la plainte fantoche de Franck Timis et tutti quanti, ....
- Après les 《 dizaines de millions de Tullow oil 》,
- après les malettes de Karim Wade et Yaya Diamé. etc.
Voici venue l'affaire des viols "répétitifs" sous la menace de deux pistolets, en présence de témoins et avec envoi préalable de Sms par le violeur pour annoncer son arrivée à sa victime.
Aucun homme politique n'a jamais été autant diffamé, calomnié et persécuté en si peu de temps. Et c'est révélateur de leurs tentatives de déstabilisation, aussi inlassables que vaines.
Nous savions qu'après les liquidations de Khalifa Sall et Karim Wade, le nouvel attelage de Macky n'avait qu'une mission : liquider Sonko à tout prix avant 2024, y compris en manipulant des individus pour une besogne aussi abjecte.
Depuis des mois des amis, y compris de l'intérieur, n'ont cessé de m'alerter sur un complot à venir portant sur des questions de mœurs, puisque tous les autres avaient lamentablement échoué.
Chers amis, militants et sympathisants, soyez rassurés que je n'ai rien à voir avec ces mensonges crapuleux.
En attendant la notification officielle d'une plainte ou d'une convocation, je vous invite à rester mobilisés comme à l’accoutumée et à continuer le travail de massification, d’enrôlement des primo votants et d’installation de cellules dans tous les coins et recoins du Sénégal, car 2024 c’est maintenant!
======================================
Wolofal
« Xarit yi, naataangoo yi ak soppe yi...
- Ginnaaw "kopparal gi bawoo Rusi"
- Ginnaaw "lëkkaloo ak MFDC"
- Ginnaaw "kopparal gi jóge ci càmmug rëtalkat yi"
- Ginnaaw jure bi ci ñàkk lu dul dëgg ci 94i tamñareet yi
- Ginnaaw jureb Frànk Timis ak ñi mel ni ñoom...
- Ginnaaw tamndareeti Tullow Oil yi,
- Ginnaaw waxandey Karim Wàdd yi ak Yaayaa Jàmme añs.
Leegi nag waxi siif lañuy wax, boole ko ak yore ñaari fetal, ci kanamu ay seede, teg ci di yónnee bataaxel ki ñu wax ne moom nga bëgg a ray, moo ci desoon.
Kenn nitu polotig masul a jot i tuuma yu ni mel, ay ŋàññ, te xam naa ray ma rekk a ciy topp fii ak i fan. Lii day wane rekk ne dunu sonn ci pexe yi ñuy teg boobu ba leegi, waaye du mujj fenn.
Xamoon nanu ne ginnaaw ba ñu sàkkalee pexe Xalifa Sàll ak Karim Wàdd ba noppi, gaa ŋi Maki Sàll yi benn liggéey rekk lañu am: sàkkal pexe Sonko balaa 2024, donte sax dañu ciy boole di jëfandikoo ay nit ngir faj seen soxla soosu.
Ay weer ci ginnaaw samay xarit, amna sax ñu ci bokk ci ñoom, ñi ngi ma doon artu ci, pexe yu nguur gi doon waajal ci man te mu jëm ci wàllug woyof tubay, ndax yi ñu mas a jéem yépp jàllul.
Yéen samay xarit, samay naataangoo ak samay soppe, amleen kóolute ci ne masu maa laale ak yëfi wayadi yooyu.
Fii ak may xaar nag ñu indil ma këyitu jure walla ñu woolu ma, maa ngi leen di waaxaat ngeen gën a booloo te wéyal liggéey bu am solo bi ngeen dooroon ci yokk sunu làng gi, jéem a waxtaan ak ñiy door a wétt te wéy di samp ci ruq yi ak ruqaan yi ci Senegaal, ndax 2024 yegsi na » !
Kopparal g/ financement
Càmm g/ État
Jure b/ plainte
Rëtalkat/ terroriste
Tamñareet/ milliards
Tamndareet/ million
Bataaxel b/ message
Wétt g/ vote
Nguur g/ gouvernement