Pour finir la soirée en apothéose
4mn30 d’images qui résument la journée d’aujourd’hui, de la prestation de serment à la passation de service
À consommer sans modération
Bataaxel bu bawoo ci Ministère de la Santé et de l'Action sociale jëm ci defaraatug raglub Dantec.
Ba ñu ko tabaxee ak leegi def na lu ëpp 100i at. Ñu seetlu ne tabax yu ci bari màgget nañu. Loolu tax nguuru Senegaal jël dogalub tabaxaat raglub Dantec ngir def ko muy raglu bu am dayoo 4 bu méngoo ak jamono. Liggéey yi war a toll ci diirub 18i weer.
Loolu tax na jëwriñ ji ñu dénk wàllu paj mi di tuxal barab ya fa nekkoon yépp. Ci sémbu doxal googu, barab yii di faj woppi ngal, woppi xol, damm-damm, woppi der, woppi bët ak ngalu xale yi dinañu leen yóbbu ca raglub Dalal Jàmm. Lu jëm ci barabu cëtëŋ yi, fi ñuy xayee tuut-tànk yi ak seen fajkat yépp moo xam suruseñ la walla tiiñkat, fajkat walla ñiy jàppale fajkat yi dinañu leen fekk ci barab yii: raglub Idriisa Puy (setewoo ga woon), Abaas Ndaw, raglub Dalal Jàmm ak raglub xale yi nekk Jamñaajo te war a dalal itam maternite bu Dantec.
Barabu fajukaay yii nag di Marist, Baay Taala Jóob (Dominik woon), Sikaab Mbaaw, Kër Ma-Saar ak Yëmbël dinañu jàppale bu baax matarnite ak sinekolosi. Ñi amee woppi roño, lu jëm ci seen paj ak seen wàllu opitaalisaasiyoŋ ak it ñiy def jaliis biy jaar ci biir bi dinañu leen jël ci raglub sóobare bu Wakaam.
24i barab ngir ñiy def jaliis dinañu leen samp ci àngaaru ajkat yi ca naawu bu Yoof ak ndawi fajkat yépp. Xale yi ame woppi roño ñoom raglub Abaas Ndaw lañu leen di fajee. Ñi daan ñëw ci barab biy faj ngal te daan jóge ci biir réew mi leegi, ca raglub Seex Ahmadul Xadiim bu Tuubaa lañuy fajoo, teg ci nag dinañu fa fekk kurél gu leen di taxawu. Ku doon fajoo ci barabu "Chirurgie Générale", leegi ca raglub Dalal Jàmm ak raglub sóobare bu Wakaam ngay dem. Lu jëm ci pajum bëñ walla rajo, "Institut d'hygiène sociale" ca Medinaa lañu ko yóbbu. Yenn barab yi ak seen i ndaw dingeen leen fekk ci warabi fajukaay yii: Kolobaan dingeen fa fekk ñiy faj wàllu der, Ngor waa "Urolosi", raglub "COUD" ba nekk ca jànguneb
Xaar leen ko YouTube Dibéer ju nekk lay am
Ka Tv "Interview" Imaam Alaaji Ñaŋ | POST KËR AYIB
Maam Musa Gey Chef di village Keur Ayib