Saabal.net

Saabal.net Saabal.net aw xët la wuy tas xibaar di siiwal ay xalaat ak i gis-gis lépp jëm ci ñoŋal Senegaal ak cosaanam, mbooram ak mbatiitam jaarale ko ci làkku wolof.
(10)

xibaar bu yu wér te leer, Bukki nee : "boo nee mbaam dee na dangay wax fa mu dee.

Mbootaayu liggéeykat yu RTS fas nañu yéene jàmmaarloo ak njiit la di Paab Aale Ñaŋ ci dogal ba mu jël dakkal yenn ci ay ...
01/07/2024

Mbootaayu liggéeykat yu RTS fas nañu yéene jàmmaarloo ak njiit la di Paab Aale Ñaŋ ci dogal ba mu jël dakkal yenn ci ay jagle yu ñu amoon...

Mnootaayu liggéeykat yu RTS, woo nañu liggéeykat ya suba ci talaata ji 02i fani sulet 2024, ci ndaje mu mag mu ñu fas yéenee amal ca RTS bu 15i waxtu jotee.

Bees sukkandikoo ci Màmma Musaa Ñaŋ mi leen jiite, bokk na ca la ñu war a waxtaane muy dogal yi njiital RTS lu bees la Paab Aale Ñaŋ jël.

Màmma Musaa Ñaŋ di ñaawlu payoor yi ñu wàññi, dàqug ñenn ci ñu fa amoon ay pasi liggéey, dakkalug déggoo gi ñu amaloon 29i mars 2024, wàññig ndàmpaay yi ba 100.000 FCFA ak dakkalug koppar ya ñu daa bokk séddoo (fonds communs).

Mu mel ni kon coow nar naa am ca RTS diggante njiit la ak liggéeykat ya.

Saabal.net

Paab Aale Ñaŋ dakkal na ag déggoo gu Raasin Tàlla ma jiite woon RTS torlu woon laataa Maki Sàll di wàcc...Njiital RTS lu...
01/07/2024

Paab Aale Ñaŋ dakkal na ag déggoo gu Raasin Tàlla ma jiite woon RTS torlu woon laataa Maki Sàll di wàcc...

Njiital RTS lu yees li, Paab Aale Ñaŋ jël na dogalu dakkal déggoo gu Raasin Tàlla mi mu fa wuutu torlu woon 29i mars 2024.

Ci bataaxel bu mu jagleel liggéeykat ya te fésal ko tay 01 panu sulet 2024, di ci leeral ne payoori weeru awril ak mee 2024 ci déggoo googu ñu torlu 29i mars 2024, lañu ko sukkandiku. Muy xamle ne déggoo googu bu dee doxal nañu dina indi jafe-jafey kopparal yu tollu ci 1.800.000.000 FCFA at mu ne ak gàllankooru koppar yu tollu ci 1.350.000.000 FCFA ci at mii ñu nekk.

Ndegam nag amul lenn lu ñu waajaloon lu man a dékku loolu, déggoo gi ñu torlu woon 29i mars 2024 dakkalandi nañu ko ba keroog matug dekkreb 2024-837 bu 27i mars 2024, bi defal ay jagle ci wàllu koppar ñeel RTS.

Paab Aale Ñaŋ di xamle ne li ko dale njeextalu weeru suwe 2024, payoor yi dees na leen delloo ca na ñu meloon sukkandiku ko ci déggoog 25i mars 2005.
Ci loolu nag jox na ndigal Njiital Ndoxal ga ak Koppar ya, Njiital liggéeykat ya ak Njiital bànqaas biy saytu yoriin wa, nu taxaw temm ci doxal dogal bii.

Saabal.net

Ammet Ndóoy tekki na ndomba tànkam ca SENEWEB...Ammet Ndóoy di ab aajarkat ca SENEWEB, xamle na ne jébbal na ay kilifaam...
01/07/2024

Ammet Ndóoy tekki na ndomba tànkam ca SENEWEB...

Ammet Ndóoy di ab aajarkat ca SENEWEB, xamle na ne jébbal na ay kilifaam bataaxelu bàyyi ca ëttu tasukaayu xibaar boobu.

Ginnaaw 4i at yu mu fa def nag, moom Ammet Ndóoy mi fés loolu fan yii ndax cong yi muy amal jëme ci nguur gu yees gi, nee na daa fas yéene sóobu ci yeneen sémb.

Saabal.net

01/07/2024

Tuubaa Ngayeen: Kenn ku ñàkk bakkanam ci jàppante yu doxoon diggante askan wa ak i sàmm...

Ay xeexoo yu doxoon diggante ay sàmm ak ña dëkk ca Tuubaa Ngayeen nekk ca goxu Malem Odaar ca Kafrin, jur na ñu bari ñu am i gaañu-gaañu ak kenn ku ca ñàkk bakkanam.

Bees sukkandikoo ci Alaaji Mustafaa ka mi jiite sàmmkati Tuubaa Ngayeen, jëf jii kenn manu koo nangu. Li mu manul a nànd nee na mooy naka la kilifag dëkk ba man a joxee ndigal ñu leen di song ñoom sàmmkat yi.
Muy mbir mu muy ñaawlu lool nag teg ci di woo Njiitu Réew mi ak Njiital Jëwriñ yi ñu taxaw gaaw ngir saafara réeroo yii am ba tax ñu ray ci seen mbokk, lu ko moy ñoom dinañu fajal senn bopp,

Saabal.net

Saabal.net
01/07/2024

Saabal.net

Muhammet Masali jël na dogalu tekki ndomba tànk ga mu yoroon ca ONFP ga mu jiite woon Ndiisoog Ndoxal ga (Président Cons...
30/06/2024

Muhammet Masali jël na dogalu tekki ndomba tànk ga mu yoroon ca ONFP ga mu jiite woon Ndiisoog Ndoxal ga (Président Conseil d'administration).

Li mu ci jublu nag nee na mooy jàmmaarloo ak nguur gii nga xam ne ba ñu leen falee ba leegi ci nax askan wi rekk lañu nekk...

Saabal.net

30/06/2024

Kàdduy Usmaan Sonko ci caxa-caxatee ga ñu def ca tefesu Aas Bernaar…

Saabal.net

30/06/2024

Kàdduy Usmaan Sonko ca Kolobaan…

Saabal.net

Tekki Wolof ci yeneen làkk leegi lu man a nekk la ak Google.Ci fan yii nu génn Google dolli na ci Njëfekaayu tekkeem gii...
30/06/2024

Tekki Wolof ci yeneen làkk leegi lu man a nekk la ak Google.

Ci fan yii nu génn Google dolli na ci Njëfekaayu tekkeem gii di “Google Translate”, lu tollu ci 110i làkk yu yees, bokk ci yooyu làkku wolof wi ñi ëpp ci Senegaal di jëfandikoo.

Jubluwaay bi nag mooy yegg ci man a am lu tollu ci 1000iy làkk ci Njëfekaay gi.

Muy jéego yu am solo yu ñu seetlu ci làkku wolof ak ni mu tàmbalee yaatu ci àddina si, donte tekki gi xaw naa des, waaye nag ci ndoorte manees na koo nànd ndax lu mat amul. Fii ak boobu ñu koy joyyanti ndànk-ndànk.

Ay caaf (test) yu nu ci jot a def.

Yéen it man ngeen koo caaf fii: 👉🏿 https://translate.google.ca

Saabal.net

Aamadu Ba di woo Usmaan Sonko mu dem ca Ngomblaan ga ngir xamle yoon wi Ngornamaam war a liggéeyee (DPG)...Moom Jëwriñ J...
29/06/2024

Aamadu Ba di woo Usmaan Sonko mu dem ca Ngomblaan ga ngir xamle yoon wi Ngornamaam war a liggéeyee (DPG)...

Moom Jëwriñ Ju Njëkk ja woon doonoon lawaxu BBY ci joŋantey tànn njiitu réew mii weesu di xamle ne demokaraasi dafa sampu ci ay campeef (institution) ak jëf yu méngoo ak repiblig yu ñépp war a sàmmonteel. Taxaw xamle sa yoonu liggéey (DPG) nag, romb na taxaw rekk di àddu, dafa doon jataay bu am solo bob ngornamaa bi day jaayante, ci kanamu askan wi, jaare ko ci ñi ñu fal ca Ngomblaan ga, wane yoon wi nga xam ne ci lañu fas yéenee jaar ngir matale tomb yi leen Njiitu Réew mi rëddal.
Muy fàttali moom Aamadu Ba ne, artiikal 55 bu Ndayu Sàrti Réew mi moo ga Njiital Jëwriñ ji mu xamle yoonu liggéeyam (DPG) ci kanamu Nhomblaan gi. Kon lu manul a ñàkk la ñu saxal mbaaxu repiblig googu, bokk ci doxiin wu leer te ànd ak kilifteef ñeel gornamaa bi.

Kon Aamadu Ba di xamle ne jëf jooju ci barab bi ñu yoonal kese lees ko war a amalee, niki ko Ndayu Sàrti Réew mi ak sunu mbaaxi demokaraasi diglee. Xamle sa yoonu liggéey doonul rekk lu Ndayu Sàrti Réew mi waral, waaye day wareef wu dog. Loolu moo waral moom Aamadu Ba nee na moo tqx bi mu nekkee Njiital Jëwriñ yi, mu dem ca kanamu Ngomblaan ga defee ko fa, ginnaaw 3i weer yi topp ci bi ñu ko tabbee ba sax jot a jànkonte ak jàmbur yu Yewwi Askan wi yi dugaloon càkkuteefu daaneel gornamaam.

Yéeneem nag, ngir ñu moytu jafe-jafe di am ci wàllu campeef yi te man a néewal doole sunu demokaraasi, moom Aamadu Ba nee na mooy wareef la ci nun ñépp nu taxaw ci aar mbooleem tolluwaay yi ci ni sunu demokaraasi di doxee, ñu sàmmonte ak moom bu wér.

Bëgg-bëggam gi nga xam ne nag moom la jaayante ci politig, nee na mooy mu gis sunu réew mi mu jëm kanam ci jox cér sunuy campeef ak sunu mbaaxi demokaraasi. Muy nag nee na yéene joo xam ne day gën a dëgëral sunu demokaraasi teg ci feddali tamit kóoluteg askan wi jëm ci ñi leen di jiite.

Saabal.net

Xëccoo diggante Usmaan Sonko ak Ngomblaan ga: Abdu Mbow xamle na ne wax nañu Njiital Ngomblaan gi Aamadu Maam Jóob  mu j...
29/06/2024

Xëccoo diggante Usmaan Sonko ak Ngomblaan ga: Abdu Mbow xamle na ne wax nañu Njiital Ngomblaan gi Aamadu Maam Jóob mu jokkoo ak Njiitu Réew mi ngir ñu gaaw indi saafara ci jafe-jafe bii am.

Moom Abdu Mbow di wax ne bu ñu fowantoo askan wi. Ci am réew lañu nekk nekkuñu ci mbedd. Te ndayu sàrti réew mi mayul Njiitu Jëwriñ muy xamle yoonu liggéeyam (DPG) fu moy ca Ngomblaan ga. Nee na lii moo waral ñu dakkal jataay bi ñu waroon a séq ak Jëwriñu koom mi ak njël li.

Saabal.net

Ngomblaan ga: dakkal nañu liggéey yi ñu waroon a séq tay ak Jëwriñu Koom mi ak Njël li jëm ci càmbar njël li…Bees sukkan...
29/06/2024

Ngomblaan ga: dakkal nañu liggéey yi ñu waroon a séq tay ak Jëwriñu Koom mi ak Njël li jëm ci càmbar njël li…

Bees sukkandikoo ci Seex Abdu Baara Dolli, jataay bi ñu waroon a amal ca Ngomblaan ga jëm ci waxtaane njël li, dakkal nañu ko ginnaaw bi pekkub Ngomblaan ga dajee ci suba ba noppi. Li waral ñu dakkal ndaje mi nag moom jàmbur bi nee na mooy, dogal bi Njiital Jëwriñ ji Usmaan Sonko jël xamle ne nangulul Ngomblaan gii. Loolu moo waral pekk bi gis ne kon amul lenn njariñ ñuy dalal foofa jëwriñu koom mi ak njël li.

Ci ndaje mu jamp moomu ñu woote woon tay ci 9i waxtu, pekk bi jàpp nañu ñoom itam ne ndegam Njiital Jëwriñ yi nangulul Ngomblaan gi, kon xel nanguwul muy yabal kenn ci ay jëwriñam ngir mu ñëw di waxtaan ak ñoo xam ne nangulut leen. Dakkal jataayub waxtaane njël li ñu jàppoon tay ci gaawu bi 29i suwe, ñoon jàmbur yii féete ci kujje gi, gis nañu ne mooy li war kon.

Moom Seex Abdu Baara Dolli nag xamle na ne ñàkk a amal jataay bii jëmoon ci waxtaane njël li, dina metti ci askan wi. Muy mbir mu muy ñaawlu moom jàmbur bi gis ne dañu koo waroon a amal ndax 30i fani suwe la Ngombpaan war a tëj ngir jël bër. Kon ñàkk a amal joyyanti googu ci njël li askan wi rekk a ko nar a yëg.

Cig pàttali Usmaan Sonko, démb ci mbind mu mu fésal doon ci tontu bataaxel bu ko Guy Maris Saaña bindoon doon sàkku ci moom mu bañ a teew ca Ngomlaan ga ndax sàrtu biir ba fay dox baaxul, dafa xamle ne fii ak 15i fani sulet bu waa Nhomblaan gi jubbantiwul seen sàrtu biir boobu, moom Usmaan Sonko du fa teew ngir amal jataayub xamle yoon wi mgornamaam war a liggéeyee.

Saabal.net

Irã : Joŋante tànn njiitu réew ma jeex na tàkk, jëwriñu biir réew ma fésal na njureef yi .Njureef yi nag nii lañu tëdde ...
29/06/2024

Irã : Joŋante tànn njiitu réew ma jeex na tàkk, jëwriñu biir réew ma fésal na njureef yi .

Njureef yi nag nii lañu tëdde :

— Mas-huut Peseskiyaan moo jiitu am : 10 415 991i kàddu.

— Sayyid Jaliilii moo ci topp am : 9 473 298i kàddu.

— Muhammat Baxiir Xaalibaaf topp ci am : 3 383 340i kàddu.

— Mustafaa Pur Muhammadii topp ca am : 206,397i kàddu.

Njureef yi day wane ne ñaareelu wërngal dina am war a dox ci diggante ñaari lawax yii di : Mas-huut Peseskiyaan ak Sayyid Jaliilii 5i fan ci weeru Sulet bii di ñëw.

Saabal.net

28/06/2024

Ci seen janoo bi ñu doon amal ak saabalkat yi, jàmbur yu BBY ñu ngi woo Usmaan Sonko mu sàmmonte ak li ko Ndayu sàrti Réew mi wax te ñëw jàkkaarloo ak ñoom.

Xamle nañu ne jàmburi Yewwi Askan wi ay “depitey” Usmaan Sonko lañu waaye duñu "depitey" askan wi.

Ba tay ci kàddu Abdu Mbow ñoom waa BBY yi nee nañu dinañu amal sémbuw yoonal wuy tax Njiitu Réew mi dootul am sañ-sañu mam a tas Ngomblaan gi waaye itam sàrt bu jëm ci daaneel ngornamaa bu Sonko (motion de censure)…

Saabal.net

Fii ak 15i sulet Usmaan Sonko nee na bu Ngomblaan gi soppiwul seen sàrti doxaliin yi dugalaat ci taxawaay yi soxal Njiit...
28/06/2024

Fii ak 15i sulet Usmaan Sonko nee na bu Ngomblaan gi soppiwul seen sàrti doxaliin yi dugalaat ci taxawaay yi soxal Njiital Jëwriñ yi, moom Sonko du fa ñëw ngir wax yoon wi ngornamaam fas yéenee liggéeyee (DPG).

Xamle na ne liggéey bi noppi na bu yàgg te sax nag moom da koo yàkkamti ngir wan ñépp yoon wi ñu bëgg a jaar jëm ci jëmmal tomb yi leen njiitu Réew mi joxoñ.

Xamle na ne fii ak boobu su Ngombalaan gi soppiwul seen i sàrt, moom Usmaan Sonko dina ko amal waaye du doon ca Ngomblaan ga, ci kanamu askan wi la koy defee ci kanamu ay amadagunduŋ, ay kàngam yu mag ak ma-réew yu farut fenn ci politig, te su boobaa nee na ci lay ëppee solo te ci la dayoo bi di gën a kawe.

Saabal.net

Tontul Ceerno Bóokum jëm ci Aminata Ture miy sàkku ci Njiitu Réew mi mu tas Ngomblaan gi ndax méngoowul ak nammeelu aska...
28/06/2024

Tontul Ceerno Bóokum jëm ci Aminata Ture miy sàkku ci Njiitu Réew mi mu tas Ngomblaan gi ndax méngoowul ak nammeelu askan wi.

Moom Ceerno Bóokum di xamle ne: “Yellug Ngomblaan gi ajuwul ci yoxoy Njiitu Réew. Yelleef googu ci kayug lëmm lees koy doxal. Jàmburi tay jii nag yu askan wi lañu. Te loolu ku fi doonoon Njiital Jëwriñ da koo war a xam.”

Saabal.net

Aminata Ture di sàkku ci Njiitu Réew mi mu tas Ngomblaan gi bu ñu yeggee ci 31i sulet ndax méngoowul ak nammeelu askan w...
28/06/2024

Aminata Ture di sàkku ci Njiitu Réew mi mu tas Ngomblaan gi bu ñu yeggee ci 31i sulet ndax méngoowul ak nammeelu askan wi…

Ci mbind mu mu fésal moom Mimi di ci xamle ne, ñëw ci kanamu Ngomblaan gu méngoowul ak nammeelu askan wi ngir xamle yoon wi sa ngornamaa war a liggéeyee (DPG), amul lenn njariñ.

Moom Aminata Ture jàpp na ne Ngomblaan gii méngoowul ak yéene ji askanu Senegaal fésal 24 mars bii weesu.
Lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar di Aamadu Ba dañu koo daan ci wërngal wu njëkk, amul lu dul 35%. Loolu tax moom Mimi di laaj lan moo war a tax kon Njiital Jëwriñ yi di taxaw ngir xamle yoon wi mu fas yéenee amal ub liggéeyam ci kanamu Ngomblaan gu ko yeyoowul?

Yéeney saa-senegaal yi ci soppi dafa leer nàññ ci li ñu fal Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay ci 54%. Kon nañu teg jéego yi jëm ci tas Ngomblaan gii bu ñu yeggee ci 31i sulet daal di taxawalaat Ngomblaan gu yees, boobu la taxaw ci seen kanam di door a safe, te dina wan bu baax gis-gis ak yéeney ngirnamaam jàmbur (député) yu ko yeyoo te askan wi tànnal leen seen bopp ngir 5i at yii di ñëwaat, di kàdduy Mimi Ture.

Saabal.net

“Ndax warunoo bóom sunu way-politig yi tàmbalee ko ci Usmaan Sonko?” di laajub Bugaan Géy Daani njiital Gëm Sa Bopp miy ...
28/06/2024

“Ndax warunoo bóom sunu way-politig yi tàmbalee ko ci Usmaan Sonko?” di laajub Bugaan Géy Daani njiital Gëm Sa Bopp miy àddu ci coowal Usmaan Sonko mi war a teew ci kanamu jàmbur yi ca Ngomblaan ga te mel ni ku ko fasul yéenee def.

Moom Bugaan nag fàttali na xew-xewi politig yi fi jot a jaar, di xamle ne jàmburi Yewwi Askan yii ñoo fi doon jéem a daaneel ngornamaa bu Aamadu Ba ca 2022 te ca jooja jamono waxuñu woon waxi sàrtub Ngomblaan gi. Loolu tax na moom njiital Gëm Sa Bopp li di ñaawlu pexe yii ñu bëgg a teg bëgg a làqatu ci ginnaaw sàrtub Ngomblaan gi te dara waralu ko lu dul bëgg a aar Njiital Jëwriñ jii nga xam ne moom Bugaan jàpp na ne daa amul wenn sémb wu leer wu man a suqali réew mi.

Bugaan Géy ba tay di wax ne Njiital Jëwriñ jii daal lenn rekk la man te mooy ay kàddu yu wuute, dëkk ci wax di weddi boppam ak di jéem a jaay sémb wu amul.

Moom Bugaan nag nee na fii ak i fan li àpp bi yoon may Usmaan Sonko day daal di mat ndax artiikal 55 bu Ndayu Sàrti Réew mi ak sàrtub Ngomblaan gi ñoo may jàmbur yi ñu bañatee nangul Njiital Jëwriñ yi waxuma la nag naan dañu koy dalal ngir mu xamle yoon wi mu fas yéene liggéeyee (DPG).
Bugaan gis ne Sonko daal fii mu ne ci teg xel la nekk te loolu moo mas a doon jikkoom donte yàgg naa tuumaal jàmbur yi fi ne woon ne ay jàmburi Njiitu Réew mi lañu.

Muy daaneel nag ci xamle ne, politig moom saa bu laloo ci wanewu ak i nar, man naa jur ay jëf yu toftaloo yu wérul yu man a nelawal askan wi ci diir bu gàtt. Waaye nag kenn manul wéy di nelawal aw askan saa su ne.

Saabal.net

27/06/2024

Kippaangog jàmbur yu BBY dinañu janoo ak saabalkat yi suba ci àjjuma ji.

Saabal.net

27/06/2024

XIBAARI WOLOF YI CI RTS1 Sénégal

Sigicoor : Ginnaaw bi Usmaan Sonko tànnee Jibril Sonko ngir mu wuutu ko ca Para ga (mairie), yeneen lawax (candidat) yép...
27/06/2024

Sigicoor : Ginnaaw bi Usmaan Sonko tànnee Jibril Sonko ngir mu wuutu ko ca Para ga (mairie), yeneen lawax (candidat) yépp rocciku nañu fas yéenee taxaw ci ginnaaw ki Usmaan Sonko tànn.

Saabal.net

27/06/2024

Li gën a fés :🦻🏿

Saabal.net

Kendalug jàmm !Saabal.net
27/06/2024

Kendalug jàmm !

Saabal.net

26/06/2024

Xibaari wolof yi ci RTS1 Sénégal

26/06/2024

Kippaangog jàmbur yu Yewwi Askan Wi doon nañu amal tay ab janoo ak taskati xibaar yi ngir indi ay leeral ci tomb yu bari yu soxal seen taxawaay ca Ngomblaan ga.

Bokk na ci yooyu ay laaj yu ñu wax ne bind nañu ko jébbal ko njitaal Ngomblaan ga ngir mu war koo jottali nguur gi, njël li ñu war a càmbaraat gaawu ci teewaayu Seex Diba miy Jëwriñ ji ñu dénk koppar yi ak njël li, teew gi jëwriñ ju njëkk ji Usmaan Sonko war a teew ca Ngomblaan ga ngir xamle yoon wi ku fas yéenee liggéeyee ak yeneen i tomb…

Saabal.net

Leerali jëwriñ ji ñu dénk jokkalante ak Afrig ak biri Bitim réew ci feeñu gi amon ca buntu laamisso Senegaal xa Burkinaa...
26/06/2024

Leerali jëwriñ ji ñu dénk jokkalante ak Afrig ak biri Bitim réew ci feeñu gi amon ca buntu laamisso Senegaal xa Burkinaa Faaso.

Ci ab saabal bu ñu fésal jëwriñ ji di Soxna Yaasin di fàttali ne ginnaaw ag feeñu gu Mboitaayug Senegaal giy xeex yelleefi nit ñi (COSEDDH) ak Amnesty Internation amal, 21 suwe 2024 ci Ndakaaru, Jëwriñu Burkinaa ji ñu dénk biri biti réew ak saa-burkinaa yi nekk biti réew fésal na, ci benn saabal bu 24 suwe 2024, naqram ci feeñu googu te waxul benn yoon ne Senegaal day jéem a dugg ci ni ñuy doxalee seen um réew.

Muy xamle moom jëwriñ ji ne, ci talaata ji, 25i suwe 2024, way-feeñu yu bokk ci kurél gi ëmb ma-réewi Burkinaa te taxaw ngir sàmm njariñi Burkina Faso, ñoo lootaabe ab toogaanu ci jàmm ca buntu laamisoog (ambassade) Senegaal ga nekk ca Burkinaa Fasoo ngir jébbal ma-laamisoo (Ambassadeur) ba ab bataaxel bu seen njiit Jibriil Sawadogo jagleel njiital Amnesty International bu Burkinaa.

Muy leeral nag ne, wuute lool nag ak li ñuy ruumandaat, du kenn ci ndawi laamisoo ga (personnel diplomatique), du dali laamisoo ga lenn lu ñu ca song walla ñu jot ay xupp niki noonu it du kenn ci doomi Senegaal ya nekk ca Burkinaa Faaso tey wéy di doxi seen i soxla.

Muy xamle ne , Nguurug Senegaal a ngi feddali ag njàppaleem boole ci di rafetlu jéego yi Nguurug Burkinaa di teg jëm ci jàmmaarloo ak rëtal gi (terrorisme) ak delloosi bu wér kaaraangeg réew ma.

Saabal.net

Kendalug jamm !Saabal.net
26/06/2024

Kendalug jamm !

Saabal.net

Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay demoon na tay nemmikuji jumtukaay ba ñu samp ca toolu petorol bu Sàngomaar.Xamle na ne...
25/06/2024

Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay demoon na tay nemmikuji jumtukaay ba ñu samp ca toolu petorol bu Sàngomaar.

Xamle na ne mu ngi feddali ag jaayanteem ak gu ngornamaa bi ci amal caytu gu leer te maandu ci sunu balli mbindaare yi, lépp ngir njariñu askanu Senegaal…

Saabal.net

Adresse

Dakar
23000

Téléphone

+221773024314

Notifications

Soyez le premier à savoir et laissez-nous vous envoyer un courriel lorsque Saabal.net publie des nouvelles et des promotions. Votre adresse e-mail ne sera pas utilisée à d'autres fins, et vous pouvez vous désabonner à tout moment.

Contacter L'entreprise

Envoyer un message à Saabal.net:

Vidéos

Partager



Tu pourrais aussi aimer