Daaru’l Qarraare

Daaru’l Qarraare Qarraarement

04/05/2024
28/04/2024

Regarde la vidéo de Zikroula 221.

21/04/2024
14/04/2024
09/04/2024
07/04/2024
20/03/2024

BAMBA BÒKKU CI

Qadadahu tahalâ annâ Rabbu kumu LÂH ahlâ
Firhawnâh it, naan : Annâ rabbu kuma LÂH aqlâ

La YÂLLAH wax ñi gëm ñëpp, ñoo nanguy waxam
May yi YÂLLAH may YONNENam ak i SAHÂBAHam

Am na ci lol boo ko waxee, du ñu ko gëm
Waaye, bu dee luñ war a wax, di nañ ko xam

Yòbbul u jullit ëllëg Yawmal-Qiyâm
Mooy yéene’k a wax lu baax, def cig anam

Awwa jamilat mina Shaytâni
Wa qâdiri manâfihal awtâni

Ba ko KU-TEDD-KI di wax de, yàgg na
Waaye li MU doon wax, léegi yégsi na

Am na yeneen yu ñëw a gul, te di na ñëw
Lum waxoon, lu yàgg-yàgg di na ñëw

Wal Fadjri wala yâli ashri, YÂLLAH a ko wax
Fadjri yanâ bihâ, SËRIÑ TÛBÂ ko wax

Hymne national biñ yor ci Senegaal
Da na mas a sòpp’ee ku, ndax ñoo kay naal

Bu ngeen xamoon njariñ i Wax i BAMBA
Kon ngeen taxaw temm ci jéxxi Ban ba

Ku fi masaan a am baat ca déemb
Tubaab bee la noot, fab ko ca déemb

Mooy la xewoon rekk, diganteem ak Sëriñ si
Muy ray ñii, di xuppu ñee, ñuy wuysi

Ragal Tubaab yàgg na ci Sëriñ si
Moo xam ñi sant Mbàkke mbaa ñi sant Sy

Bâllah’k Maam-Muharram, BAMBA bòkku ci
Ku ciy lim a ti ber KO, ndaxte bòkku ci

Yooyo waral yiy xew di xew, ndax bòkku ci

TAALIF CHEIKH AHMADOU KARA MBACKÉ NOREYNI

08/03/2024

Message du Guide de la Révolution Pacifique Cheikh Ahmadou Kara Mbacké Noreyni

06/03/2024
04/03/2024
Taalifu Qaadimu RassulQADIMU RASSUL MINIOU GEUMYONNEN bee ko jox li mu amBam ko yòbb’oo ca BOROOMamLañ ko fa tànnal’ee M...
01/03/2024

Taalifu Qaadimu Rassul

QADIMU RASSUL MINIOU GEUM
YONNEN bee ko jox li mu am
Bam ko yòbb’oo ca BOROOMam
Lañ ko fa tànnal’ee Mbiram

Al HamdouliLÂHI KARÎM
Ci yile Sët ak yile Doom
Ku ci sant MBÀKKE du am
Bàkkàr ba kenn di ko jam

Doom mbaa Sëtu ci callala’g
MAAM MAHÂRAM mi nekk mag
Doy na teraanga, doy na sag
Ngir Jëmm i AHMADUL QADÎM

MOOM mi ci feeñ tey ku nëbbu
MOO dònnu BAAY i ZEYNABU
Lu waay di def jarul nëbbu
Lum man a doon di ko xam

Ay man, ku may saraxollele
Naan : Wululul ! Di télé-lélé
Na ñëpp ñëw ñu wélé-lélé
Santee ko MBËR ma ñëpp gëm

Liñ gis ci MOOM, fi MOOM la yem
Amul feneen te kenn du ko am
Lenn la woon lu YÂLLAH am
Jox ko NABI, mu neh ko : Am

Raw na Gaay ya weesu woon
Distance bu sori te bu doon
Course, wëraat na roomb leen
Jël Coupe ba jox leen, desee Ndam

Saa yu nekk ñun da ñuy
Sòtti rongooñ, ba ñuy
Am dal’ug xol ca fa ñuy
Jàngg’ee Qasîdah ca Kanam

Wooh nañ la wooh a ti la
Ci suñu mbir rekk balaa
Kenn di saalit, ngalla
Gaawal-a-gaaw, ñoo ngi sëngéem

Lenn kepp ñu teeh nelaw
TÛBÂ na doon État bu gaaw
Bu autonome te ñëpp nëw
Maasee teew ci sa Kanam

Âmîn ! Ñaan nañ ko BOROOM-
KUN-FAYAKÔN, YÂLLAH na am
Ci Daraja’y SHEYQUL QADÎM
Mi niru Doom te nekk MAAM

Adresse

Grand Medine
Dakar

Téléphone

+19599995099

Site Web

Notifications

Soyez le premier à savoir et laissez-nous vous envoyer un courriel lorsque Daaru’l Qarraare publie des nouvelles et des promotions. Votre adresse e-mail ne sera pas utilisée à d'autres fins, et vous pouvez vous désabonner à tout moment.

Partager