10/03/2024
Lou tax nga warra takk JAARO AQIQA ( عقيق )
Mbokku yi tay daniouy waxtaané al ahjaarour kariim , mooy xeer yinga xam ni moom laniouy def thi jaaro yi , te niou geun koo miine thi xeeru
HAQIQA
Dananiou waxtaane tay naka la nit ki mana def ba xam xeer binga xam ni moo meengoo ak sa bidiw ak sa rawhan, ak naka laniou koy laabalé
Bi doomou aadama niawé thi kaw souf batay , bou weesoo garab yi, bookou na thi anda ndom yi geuna mak mouy ( AL AHJAAROUL KARIIM )
Mooy liniouy touddé le pierre précieuse , mooy xeer yii nga xam ni moom laniouy def thi sunu jaaro yi
Niou bary thi nit gni daniou koy diafandiko nguir taar , Waayé li eupou thi nit gniko xam daniou koy diafandi koo nguir fadiou , moo xam nioodi la thi waalou weursak , moo xam dakh rab la , walla sakh thiat ak chaytaané
Xeér bii nak mbookou yi civilisation yëpou ak diné yëpou , marche naniou dioxko wathiou way bou am doolé lool
basi al xour aane sakh guis naniou mou toudou thi you bary lool , bousi menli ( YAHKHOUD ) AK
( MARJAANE ) répétez nako ay yoone waayé iam diokhé nasi ay misaal you am solo lool
Bouniou dello thi soratou baxara , bi sunu brom di neetali xisatou waa banou Israël, ak weeweul yinga xam ni boroom bi defal naaleen ko , taxul niou geum ko ,
sunu boroom di leene wakh ni seene xoll yi dey dafa wow ba mell ni ay xeer , basi yaageu mou neleene deedeed xeer yi sakh mooleen tané , ndakh
وَإِنَّ مِنَ الْحِجَارَةِ لَمَا يَتَفَجَّرُ مِنْهُ الْأَنْهَارُ ۚ وَإِنَّ مِنْهَا لَمَا يَشَّقَّقُ فَيَخْرُجُ مِنْهُ الْمَاءُ ۚ وَإِنَّ مِنْهَا لَمَا يَهْبِطُ مِنْ خَشْيَةِ اللَّهِ ۗ وَمَا اللَّهُ بِغَافِلٍ عَمَّا تَعْمَلُونَ
Kone xeer dafa nekk lou am solo loo xam ni diiney lislam baayi nako xell bou baakha baakh
Naka noonou yonente yi yitam foonkoon naniou ko bou baakha baakh, kousi melni sama sopé ba yonente yalla suleymaane halaïhi salam,
Moom yonente yalla suleymane nak bookou na thi karaama yiko yalla defal loone mooy mou yilifoon aadouna , te guis naniou ni li eupoon thi ay mbiram mingui woone thi jaaro boobou mou yoroone te mou amoon xeerou haqiqa bi
Mbookou yi jaaro HAQIQA sounna la , te borom xam xam yëpou deupo naniou thi
Anass mingui neetali né , yonente yalla Mouhammad shw amoon na jaaro boo xam ni xeerou HAQIQA moosi nekoon ,
lisi geuna yemé sakh mooy jaaro boobou ganaaw bifi yonente bi dioguee sayidouna aboubacar moo doondou jaaro boobou
ganaaw bifi aboubacar dioguee yitam oumar mooko dondou , ganaaw ba yitam thi lako ousmane doobdou ,
wakh naniou ni nak thi xilaafak sayiduna usman thi la jaaro boobou reeré
______________________
Lane mooy ndiarignou AL AHJAROUL KARIIM ?
mane naa wakh ni lepou lay diarigne , ndakh lepou loosi woo rek mou wouyou sila in chaa Allah
Mooxam thi waalou fath la , mooxam thi wallou gnoody weur seuk la , mooxam thi dakh thiat la walla laguey , walla chaytaané, walla sakh ak laguey , ak lepou loo xam ni dafay galankoor domou aadama , te nit ki mane nasi sukandi ku pour guis ay résultat you gaawa gaaw lool
Waayé nak lepou mingui adiou thi nit ki ak fi xam xamam toolou
Bou feeké ni dangaa beuga diariniou thi nenne xeer , mooxam jaaro bi la walla laneen la , linga warra ndiakka def mooy nga dem thi cheikhour rawhaan bi ,
serigne binga xam ni boolé na xam hilmoun noudioum , xam yitam hilmou rawhaan, xam yitam hilmoul hadad , ay yeneen xeety xam nam yinga xam ni moom nga warra xam pour mana lagueey thi waaloum jaaro ,
Boo demmé thi serigne bi nak danala laath sa tour ak sa tourou yaay , bouko defee dana def hadad nguir mana xam lane mooy sa tabiha , ak lane mooy sa bidew ak yane mooy rawhaan yinga xam ni moo aandeu ak yaw
Bouko defé nak dana woud xeer binga xam ni moo meengoo ak sa rawhaan , nguir mou mane laa lagueeyal sa jaaro
Bou wouté xeer bi ba noopi nak limou warra ndiakka def moy mou laabal xér bi thi turu yalla ak soufou gueedj ,
Souf soosou nak soufla soo xam ni waroul gis jante , manam dangay nourou thi biir gueedj gui ba mana am thi souf sa , nga tipou thia
Boo noppé yitam nga wout maa auoul werd ak ndokhou zam zam , boo noopé nga boolé ko def ko thi benne verr , nga tiim ko laguey thi linga thi laguey thi al xour aane ak turou yalla
Loolou ngay diafandikoo nguir mana laabal xeer bi bamou nekk xeer boo xam ni buy dundu la in chaa Allah
Ganaaw binga laabalé xeer bi ba noopi nak faawou nga chargée ko , cheikhou rawhaan bi nak mooy xam ndakh xeer bi thi limierou weer wi laniou ko warra changer, walla thi limier jante bi
Bou loolou lepou jaallé nak mbookou yi , dana nekk xeer boo xam ni sett na , selle na , laab na ,
Te pouvoir binga xam ni moom laniou thi sentu yitam matna seukeu
Bouko defé nak nga doora dieul xeer bi daadi koy diokh teugeu binga xam ni moo warra teugeu jaaro bi ,
foofou yitam amna toutu sew sew , ndakh bepou xeetou jaaro boo beugeu rek , amna teugeu boo xam ni moom ngay taamou pour mou warra teugeu jaaro bi
Bouko teugeu bi teugué ba noopi nak , nga door koo andi waat thi cheikhou rawhaan bi nguir mu def thi secret binga xam ni moosi warra dem
Deugeu la nak jaaro xaaliss kessé boo xam ni amna xeer bou laab te mengoo ak nit ki , loolou man naa diarigne kiko takk,
waayé nak li eupou thi nit gni daniouy yitté woo jaaro boo xam ni dafay lamboo thi biir , secret boo xam ni dafay mengoo ak beugeu beugam
Secret yi nak baryna lool , mootakh kou nekk ak bingay lagueey , amna nioo xam ni xaatimou suleymaane bi laniouy laguey , am nioo xam ni barhout laniouy laguey ,
Waayé lisi am solo rek mooy kinga xam ni mookoy laguey daal warr naa nekk koo xam ni kou matt seukk la thi xam xam
Bouko defee bou dougalé sirou bi ba noopi nak faawou mou defaat beneen tahaara , waayé nak dana wouté ak bou ndiakk ba
Bii nak limou thi dioublou mooy dafay mengalé niatty mbir yinga xam ni moo nekk thi jaaro bi , mouy xeer bi , ak xaaliss binga xam ni moom laniou lagué yé jaaro bi , ak secret binga xam ni moo nekk thi biir jaaro bi
Niatt yii moom faawou niou mengalé ko nguir mou mana dokh thi kinga xam ni moom laniou lagueeyal jaaro bi
Ganaaw bou loolou lepou diallé nak , nģa doora dieul jaaro bi nguir diokh ko kinga xam ni mookoy lagueey lou
Jëra geene jëf mbookou yi, leeral yii laniou leene andi loone tay , di niaane yalla nak mou defal niou jaami aduna ak jaami yawmal xiyama
Pour gnii faral di laath sama numéro WhatsApp mingui nii
( 76 619 68 73 )
____________________________
آللهم صل على سيدنا محمد وسلم